1
00:00:06,000 --> 00:00:12,074
Piblisiteel sa produit wala màrk fii
jokkool ak www.OpenSubtitles.org tay

2
00:02:39,159 --> 00:02:40,243
Ndax gëm nga Yàlla?

3
00:02:43,830 --> 00:02:47,668
Dédeet, waaye amnaa jàmm ji fi nekk

4
00:03:10,482 --> 00:03:11,608
Bëgg nga xool fita bi?

5
00:03:15,278 --> 00:03:16,363
wóolu naa la

6
00:06:37,564 --> 00:06:38,481
Bul yëngu

7
00:07:49,803 --> 00:07:50,887
Mënu ma gis

8
00:07:51,096 --> 00:07:52,347
Sa kornea dafa yàqu bu baax

9
00:07:52,472 --> 00:07:53,223
Ndax dinaa wér?

10
00:07:53,306 --> 00:07:54,849
Yaakaar amna, waaye sa gis-gis

11
00:07:54,891 --> 00:07:55,684
du musa nekk ku mat sëkk

12
00:07:55,725 --> 00:07:56,434
Sama gis-gis dafa lëndëm

13
00:07:56,476 --> 00:07:58,937
Mën nanu def ab opération, ab transplant

14
00:07:59,270 --> 00:08:00,397
Ndax dinaa nekk gumba?

15
00:08:01,272 --> 00:08:03,650
Jennie, man maay sersan Chang

16
00:08:03,900 --> 00:08:06,486
Ndax man ngeen fàttaliku kanamu reykat bi?

17
00:08:12,575 --> 00:08:15,203
Baal ma, dama ragal lool

18
00:08:15,328 --> 00:08:16,621
Teg sa xel

19
00:09:12,469 --> 00:09:16,097
Ndimbal dimbali! Ndimbal dimbali!

20
00:09:22,312 --> 00:09:24,439
Mbaa yaa ngi lay dimbali!

21
00:09:24,689 --> 00:09:25,356
Ay dof!

22
00:09:51,216 --> 00:09:52,258
Demal rek,

23
00:09:52,592 --> 00:09:55,095
Dem nañu ba noppi, buleen tiit

24
00:09:56,262 --> 00:09:57,305
Dinaa la yóbbu seen kër

25
00:10:02,393 --> 00:10:03,269
Jenni!

26
00:10:04,479 --> 00:10:05,688
naka nga xamee sama tur?

27
00:10:07,482 --> 00:10:08,691
Guddi gu nekk dama lay déglu ngay way

28
00:10:10,819 --> 00:10:11,736
Yaw yaay kan?

29
00:10:13,029 --> 00:10:17,659
Daa melni dama la xam

30
00:10:18,952 --> 00:10:20,120
Xamnaa ni mënoo gis bu baax

31
00:10:20,453 --> 00:10:21,246
Bëggoon naa jàppale,

32
00:10:21,996 --> 00:10:23,164
waaye amuma ko woon

33
00:10:26,209 --> 00:10:27,335
Ci àdduna bii

34
00:10:28,419 --> 00:10:29,838
du ku nekk a mëna wóolu

35
00:10:31,172 --> 00:10:32,590
Ndax dinga may ma jàppale la ci jamono jii?

36
00:10:57,282 --> 00:10:59,075
Ndax baaxna ma dem?

37
00:11:06,499 --> 00:11:10,253
Deel ànd ak dal, may ma xoolaat

38
00:11:15,675 --> 00:11:16,593
Muus rekk la

39
00:11:16,676 --> 00:11:19,345
Dafay faral di yuuxu di xoos samay fotëy

40
00:11:19,470 --> 00:11:20,513
Loolu mooy sonal nit ñi!

41
00:11:46,706 --> 00:11:47,749
Lu tax nga fay làmp bi?

42
00:11:47,916 --> 00:11:49,125
Mën nga ko gis?

43
00:11:51,586 --> 00:11:52,670
lëndëm kese laa gis

44
00:11:53,087 --> 00:11:54,297
Weer wi weesu moo gënoon baax

45
00:11:54,714 --> 00:11:56,507
Mën naa gis ay nataal

46
00:11:57,050 --> 00:11:59,886
Taalal làmp bi dina tax ma gëna am kaaraange

47
00:12:12,065 --> 00:12:13,024
Lan ngay def fi mu toll nii?

48
00:12:13,608 --> 00:12:15,026
Maa ngi xool kaala bii

49
00:12:22,617 --> 00:12:24,035
Dafa am sama deret

50
00:12:24,244 --> 00:12:25,453
ay tach ci kaw

51
00:12:25,995 --> 00:12:29,749
Ku ma tiire bal bi daf ko laxas ci samay bët

52
00:12:31,584 --> 00:12:33,253
Duma musa fàtte

53
00:12:33,878 --> 00:12:35,338
Bëgg nga ataaya?

54
00:12:38,091 --> 00:12:38,591
Dédeet jërëjëf

55
00:12:38,841 --> 00:12:41,052
Du def benn simili. Toogal

56
00:12:41,469 --> 00:12:42,887
Dinaa ci def ay music

57
00:13:37,650 --> 00:13:39,527
Hey relax, yaa ngi nuru

58
00:13:39,610 --> 00:13:41,529
li nga doon ab ndawu liggey bu nëbbu

59
00:13:42,155 --> 00:13:44,866
Leeralal wala dina nekk sekkere bu ubbeeku

60
00:13:46,909 --> 00:13:47,577
Gaawal

61
00:13:48,661 --> 00:13:49,829
Ree!

62
00:13:55,043 --> 00:13:57,587
Leegi yaa ngi melni lu génn ci këru noix

63
00:14:02,800 --> 00:14:06,554
Chang, waa jii Eddy dof la. Defal ndànk

64
00:14:06,721 --> 00:14:08,890
Noonu la ak yaw xarit,

65
00:14:09,015 --> 00:14:10,391
xoolal sa mbagg!

66
00:14:22,362 --> 00:14:25,448
Eddy, mangi jeggalu ci lima la xaar

67
00:14:25,615 --> 00:14:26,532
Kan mooy kii?

68
00:14:26,616 --> 00:14:28,910
Xarit bu baax la. Nanga nuyu Eddy

69
00:14:29,619 --> 00:14:30,411
Eddy

70
00:14:30,953 --> 00:14:31,913
Seetleen ko!

71
00:14:34,999 --> 00:14:37,126
Eddy, lu xew ci kaaraange gi?

72
00:14:37,168 --> 00:14:38,920
Du sunu deal bu njëkk la

73
00:14:43,299 --> 00:14:44,717
Amaana gis naa ko bu njëkk

74
00:14:47,804 --> 00:14:51,682
$200,000 Dina nu njëkka xool fita yi

75
00:15:32,473 --> 00:15:33,307
Lu ngeen di def?

76
00:15:33,391 --> 00:15:36,227
Amul lenn lu wuute, ofisiye. ndaje

77
00:15:36,727 --> 00:15:37,937
Ubbi kofre bi

78
00:15:38,229 --> 00:15:41,232
Ubbi ko!

79
00:15:41,774 --> 00:15:42,817
Léegi!

80
00:15:46,487 --> 00:15:48,239
Damn you Yaa ma taxawal, wala book?

81
00:15:48,656 --> 00:15:49,866
Ndax poliis nga?

82
00:15:50,908 --> 00:15:51,868
Waxtaan!

83
00:15:54,495 --> 00:16:00,001
Duma benn poliis! Duma la wor

84
00:16:00,251 --> 00:16:02,378
Sudee nekkoo, naka la ko mënee nekk fii?

85
00:16:02,420 --> 00:16:04,839
Du moom! Maa ngi ciy dugal sama dundu Eddy!

86
00:16:04,881 --> 00:16:06,340
Du poliis!

87
00:16:07,216 --> 00:16:08,468
Waaw fenkat, waru ma la wóolu!

88
00:16:08,551 --> 00:16:10,845
- Ku góor ki poliis la, xàmmee naa ko!
- Yaa ngi juum

89
00:16:23,941 --> 00:16:26,027
Chang, dinaa ko jël

90
00:16:36,245 --> 00:16:37,747
Bopp bu bonn bi!

91
00:16:38,581 --> 00:16:39,499
merde

92
00:17:46,274 --> 00:17:47,191
Dellu ginaaw

93
00:17:55,825 --> 00:17:56,826
Bul yëngu!

94
00:18:07,336 --> 00:18:09,505
Yalla alku! Bàq Bàq

95
00:18:09,589 --> 00:18:10,548
Jeexal sa kàddu

96
00:18:10,590 --> 00:18:12,550
Assassh

97
00:18:19,098 --> 00:18:22,018
Inspectër Li, kiñu ñakka woolu Eddy Wong jàpp na

98
00:18:22,226 --> 00:18:23,894
ci biir tram bu fees

99
00:18:24,186 --> 00:18:26,439
Ndax gis nga ko bu baax ?

100
00:18:26,606 --> 00:18:27,189
Mën nga ko?

101
00:18:27,398 --> 00:18:28,024
Waaw

102
00:18:28,107 --> 00:18:28,983
Lu tax nga tiire?

103
00:18:29,108 --> 00:18:29,692
Ci yëg-yëg

104
00:18:30,067 --> 00:18:31,944
Ndax xalaat nga kaaraange kiliyaan yi?

105
00:18:32,320 --> 00:18:34,280
Ndax amna lu nga àrtu balaa ngay tiire bal?

106
00:18:34,780 --> 00:18:35,531
Amul woon jotu loolu

107
00:18:35,698 --> 00:18:37,491
kiñ jàpp daa am trombose coronaire

108
00:18:37,825 --> 00:18:40,328
Arret karjaak moo ko ray

109
00:18:40,661 --> 00:18:42,038
Mbokkoom defnañu plainte ofisel

110
00:18:42,580 --> 00:18:43,998
Yaay waral dee am

111
00:18:44,540 --> 00:18:47,168
Loolu dof la, naka laa ko mëna xamee
Amoon na feebaru xol?

112
00:18:48,044 --> 00:18:49,879
Def naa juróom ñaari weer ci dosiye Eddy Hung

113
00:18:50,504 --> 00:18:52,298
Ku dof la woon

114
00:18:52,381 --> 00:18:53,591
Dafay tiire bal ku nekk ak lu mëna nekk

115
00:18:54,508 --> 00:18:56,719
Ndax waroon naa xaar bamu ray ko?

116
00:18:57,595 --> 00:19:00,931
Fatte nga ni gis naa ko mu ray benn poliis

117
00:19:01,849 --> 00:19:03,559
Kan moo waral deewu poliis boobu?

118
00:19:09,815 --> 00:19:12,443
Baax! Loo neex defal

119
00:19:13,235 --> 00:19:15,696
Dama tàmm xeetu ñaxtu bu nekk

120
00:19:16,614 --> 00:19:17,990
Benn beneen amul benn wuute

121
00:19:37,301 --> 00:19:38,135
jàpp ko!

122
00:19:47,895 --> 00:19:48,938
naka loxo jëf?

123
00:19:49,897 --> 00:19:50,815
Amul benn njariñ

124
00:19:55,361 --> 00:19:56,570
Dina gëna jëfandikoo ko

125
00:19:57,405 --> 00:19:58,447
Du am njariñ

126
00:19:59,699 --> 00:20:03,035
Killer bu def benn loxo nekkul ci jëf

127
00:20:05,496 --> 00:20:07,915
Sama bis jeexna

128
00:20:15,756 --> 00:20:16,799
Tong Weng mooy turam

129
00:20:17,591 --> 00:20:19,552
Mingi liggéey ci benn kuréel buy jaay drog ci Amerique Centrale

130
00:20:20,428 --> 00:20:21,262
Kan moo ko bëgg mu dee?

131
00:20:21,554 --> 00:20:24,056
Amul laaj. Jël ko wala bàyyi ko?

132
00:20:27,935 --> 00:20:28,936
1.5 milioŋ

133
00:20:30,229 --> 00:20:31,147
Daa melni lu kawe

134
00:20:32,940 --> 00:20:34,734
Lii mooy sama liggéey bu mujj

135
00:20:35,901 --> 00:20:38,237
baaxna, deal la

136
00:20:38,571 --> 00:20:39,655
Xaalis amul benn njariñ

137
00:20:45,786 --> 00:20:48,539
Fita yii dañu set. Amul nimero serie

138
00:20:49,331 --> 00:20:50,541
Mënuñu ko topp

139
00:20:51,208 --> 00:20:53,252
balaa bopp yuy kalaate, li nga gëna bëgg

140
00:21:15,983 --> 00:21:17,777
Yomb naa jël, tëye ko jafe na

141
00:21:20,529 --> 00:21:21,697
Bëgg nga soppi sa xalaat?

142
00:21:43,844 --> 00:21:44,845
Lu tax nga jël liggéey bii?

143
00:21:48,766 --> 00:21:51,227
Bii ngir Jennie

144
00:21:51,727 --> 00:21:54,063
Soo ameewul transplantation cornée ci diir bu gàtt

145
00:21:54,480 --> 00:21:56,482
Mën na ñàkk bët ba fàww

146
00:21:57,191 --> 00:21:58,526
Amna bànku kornea ci Hong Kong

147
00:21:58,984 --> 00:22:00,861
Waaye daa musa nekk amul dara

148
00:22:01,153 --> 00:22:03,113
Su amee ndimbal luy dugg

149
00:22:03,405 --> 00:22:05,574
Keneen moo ko njëkka am

150
00:22:06,283 --> 00:22:07,785
Kon noo ngi dem jéem ci bitim réew

151
00:22:33,978 --> 00:22:37,022
Dama wara bàyyi la fan yu néew

152
00:22:38,232 --> 00:22:39,900
Suma delloo, dinaa la yóbbu bitim réew ngir ñu opere la

153
00:22:42,945 --> 00:22:44,238
Di nga dellusi

154
00:22:46,699 --> 00:22:47,616
Dignaa la

155
00:23:02,298 --> 00:23:03,215
Jërëjëf!

156
00:23:04,592 --> 00:23:05,843
Tay mooy Festiwaalu Bato Dragon

157
00:23:05,926 --> 00:23:09,054
VIP yu bari ak kilifay nguur

158
00:23:09,096 --> 00:23:10,556
Dina bokk ci xew-xewu ubbite bi

159
00:23:10,931 --> 00:23:12,808
Dañu la sant nga aar leen

160
00:23:12,892 --> 00:23:14,685
Seen leeral mingi ci say dosiye

161
00:23:15,269 --> 00:23:16,937
Fexeel def liggéey bu xarañ

162
00:23:16,979 --> 00:23:18,022
Waaw sama waajur!

163
00:23:18,272 --> 00:23:22,735
Tony Weng, di aar mboq mi

164
00:23:53,933 --> 00:23:57,144
Ngeen bàyyi xel! Ndax concurrent yépp

165
00:23:57,561 --> 00:24:00,856
dajale ci kanamu platform buy féey
ngir xew-xewu bëtu malaaka mu bonn mi

166
00:24:01,106 --> 00:24:02,775
Sunu mbégte la ci di dalal njiitu réew mi

167
00:24:02,816 --> 00:24:05,611
Tung Yuan, M. Weng

168
00:24:08,405 --> 00:24:11,492
Peter Chu mooy njiitu Rotary Club

169
00:24:46,610 --> 00:24:48,696
Weng

170
00:24:49,697 --> 00:24:51,156
Lu gëna gaaw

171
00:24:51,198 --> 00:24:52,783
Wërsëgu jàmm

172
00:25:30,612 --> 00:25:32,197
Weng, mangi

173
00:26:57,699 --> 00:26:59,118
Muur ko, nga tëye lépp

174
00:26:59,368 --> 00:27:02,663
Alerte rouge, alerte rouge!

175
00:26:59,993 --> 00:27:02,663
Tony Weng deñ kaa tiire bal ci kaw platform biy féey

176
00:27:09,503 --> 00:27:10,754
Tir bi mingi joge ci wetu junks napp yi

177
00:27:10,796 --> 00:27:11,880
Ki ray nit ñi war naa nekk ci wetu

178
00:27:13,799 --> 00:27:16,468
Unite yépp waajal nañu tëj barab bi

179
00:27:20,848 --> 00:27:23,058
Weng daa xëm.

180
00:27:21,640 --> 00:27:23,058
Lépp a ngi baax

181
00:27:23,100 --> 00:27:24,601
Nanga def sa bis bu neex

182
00:29:16,964 --> 00:29:18,507
Soppi!

183
00:31:27,844 --> 00:31:30,222
Chang, xoolal fee! ab kalaate

184
00:31:30,472 --> 00:31:31,807
Waaw, nanu xoolaat ko!

185
00:31:49,825 --> 00:31:51,535
Chang, leegi mën nanu ko ñàkk!

186
00:32:32,409 --> 00:32:33,285
Sedd!

187
00:33:16,369 --> 00:33:17,496
Bul ragal dara

188
00:33:22,667 --> 00:33:24,085
Di nga jàmm

189
00:33:26,129 --> 00:33:26,922
Bul jooy

190
00:33:34,054 --> 00:33:35,347
Mingi foofu ci suuf.

191
00:33:35,388 --> 00:33:36,389
Baax na!

192
00:33:43,980 --> 00:33:45,941
Amna hopitaal bu jege?

193
00:33:46,775 --> 00:33:47,943
Yaakaar nga ni amna konsiëns?

194
00:33:47,984 --> 00:33:49,569
Du bàyyi xale bu jigéen bi dee

195
00:34:08,046 --> 00:34:09,881
Infirmier, fan la gaañ-gaañu bi nekk?

196
00:34:09,923 --> 00:34:11,591
nii

197
00:34:16,179 --> 00:34:17,138
Lu xew?

198
00:34:18,014 --> 00:34:18,765
Dañu ko tiire bal

199
00:34:18,807 --> 00:34:19,975
Gaaw! Tegal ko ci suuf

200
00:34:20,058 --> 00:34:21,059
Infirmier bi, xoolal tension bi

201
00:34:21,142 --> 00:34:22,143
Waajal ko ngir ñu opére ko

202
00:34:22,644 --> 00:34:26,064
Masku oxygen

203
00:34:33,697 --> 00:34:34,489
Naka la def?

204
00:34:34,573 --> 00:34:35,699
Tension bi nekkul

205
00:34:35,824 --> 00:34:36,700
Pulse bu néew doole

206
00:34:36,783 --> 00:34:37,951
Tension bi wàññeeku

207
00:34:42,414 --> 00:34:43,748
Ndax gis nga góor gu yor xale bu gaañu?

208
00:34:43,790 --> 00:34:44,457
Defa dem ci gaañ-gaañu

209
00:34:44,541 --> 00:34:45,542
tëj képp kuñu ñaaw njortu

210
00:34:45,625 --> 00:34:46,001
Waaw sama waajur!

211
00:34:46,084 --> 00:34:47,794
Ndax mbokk nga ak malaad bi?

212
00:34:47,836 --> 00:34:48,920
naka la ko gaañoo?

213
00:34:49,546 --> 00:34:50,839
Sëñ bi, leegi mënoo dem

214
00:34:52,132 --> 00:34:54,426
Dama wara bind sa tur

215
00:34:55,510 --> 00:34:56,469
Ana mu nekk ?

216
00:35:09,274 --> 00:35:10,692
Man inspectër laa, demal rek

217
00:35:10,734 --> 00:35:12,527
Waaw, infirmiye yi, baña bàyyi xel ci ñoom

218
00:35:12,569 --> 00:35:13,695
Waaw

219
00:35:23,747 --> 00:35:24,873
Bul leen ci xool, muccal xale bu jigéen bi

220
00:35:24,956 --> 00:35:25,832
Waaw

221
00:35:27,167 --> 00:35:28,335
Bul jaaxal doktër bi

222
00:35:29,836 --> 00:35:30,920
Tegal seeni fita

223
00:36:17,926 --> 00:36:18,468
Lu xew?

224
00:36:18,551 --> 00:36:19,302
Amoon na benn fetal

225
00:36:19,386 --> 00:36:20,887
- Fan?
- Fii nii!

226
00:36:23,098 --> 00:36:24,808
- genneel ñépp
- Waaw sama waajur!

227
00:36:45,745 --> 00:36:46,663
Dinaa woo HQ

228
00:36:48,123 --> 00:36:48,998
Amna ay yokkute ci dosiye Weng bi?

229
00:36:49,040 --> 00:36:50,917
Déedet, benn

230
00:36:52,210 --> 00:36:53,420
Dama daanaka jot kiñu ñaaw njortu ci moom

231
00:36:53,461 --> 00:36:54,587
Waaye mu rëcc

232
00:36:54,671 --> 00:36:57,048
Jàppoon naa ni am nga xel mu ñaw?

233
00:36:58,675 --> 00:37:00,468
Dañu may def ma melni ku dof

234
00:37:00,927 --> 00:37:03,221
Kon dosiye bii amna solo ci man

235
00:37:04,055 --> 00:37:05,974
Soxlawuma nga réccuma

236
00:37:06,683 --> 00:37:09,018
Yaa ngi nekkoon luy metti ci mbaam xuux

237
00:37:10,186 --> 00:37:11,688
Defal ma lu baax te nga wane ni juumu ma

238
00:37:13,648 --> 00:37:16,484
Sëñ bi, defuma dara ngir kenn

239
00:37:17,610 --> 00:37:19,195
Dinaa jël reykat bi

240
00:37:20,196 --> 00:37:21,573
Duma may nga ñàkk kanam

241
00:37:23,199 --> 00:37:25,660
Sama yaakaar mooy ngeen fàtte
ki la jàppale nga yegg ci collu bi

242
00:37:29,622 --> 00:37:31,249
Bëgg naa nga rëdd kiñu ñaaw njortu ci moom

243
00:37:31,374 --> 00:37:32,500
Jéemal, ngir dundal ko

244
00:37:32,959 --> 00:37:33,835
Dafa weesu 30 at

245
00:37:35,086 --> 00:37:36,421
Dafa melni ku fasoon yéene

246
00:37:38,214 --> 00:37:39,257
te baña def yërmaande

247
00:37:40,967 --> 00:37:42,761
Dafa melni lu am doole ci anam wimu àndalee

248
00:37:47,098 --> 00:37:49,601
Nuruwul ab reykat ci anam wumu mëna doon

249
00:37:51,478 --> 00:37:52,687
Dafay nuru lu dal

250
00:37:54,898 --> 00:37:56,024
Def melni ku am gént

251
00:37:57,692 --> 00:37:58,693
Bët yu fees dell ak bëgg-bëgg

252
00:38:50,328 --> 00:38:51,913
Salaam maalekum

253
00:38:51,120 --> 00:38:51,913
Man la, Jeff

254
00:38:52,288 --> 00:38:53,081
Jeff?

255
00:38:53,540 --> 00:38:54,374
Lu tax génnewoo ci dëkk bi?

256
00:38:54,541 --> 00:38:55,708
Dama bëgg sama xaalis leegi

257
00:39:00,338 --> 00:39:01,422
Bëgg naa ko tay ci guddi

258
00:39:02,590 --> 00:39:03,258
Tay ci guddi!

259
00:39:03,800 --> 00:39:05,802
Waaw, dinaa ko indi ci guddi gi

260
00:39:15,395 --> 00:39:16,145
Weng!

261
00:39:16,980 --> 00:39:18,731
Danga wara may ma yor Jeff,

262
00:39:19,190 --> 00:39:20,400
mooy sama wet ci mbir yi

263
00:39:21,192 --> 00:39:23,319
- Sudee daf may yuuxu?
- Du xeetu nit googu

264
00:39:24,237 --> 00:39:26,197
Wolomuma kenn

265
00:39:26,406 --> 00:39:27,490
Ak yaw itam!

266
00:39:30,827 --> 00:39:32,203
Xamnaa sàrti fowokaay bi

267
00:39:33,246 --> 00:39:35,123
Dinaa def lima ko dige

268
00:39:35,540 --> 00:39:37,500
Duma soxal sàrt yi, bëgg naa mu dee

269
00:39:38,293 --> 00:39:40,295
ndax dafa wane limu doon

270
00:39:41,170 --> 00:39:42,505
Man maay patroŋ bi leegi

271
00:39:42,589 --> 00:39:44,632
te yaa ngi def mbir yi ci sama anam

272
00:39:46,217 --> 00:39:47,760
Ok, nga ray ko ndax man

273
00:39:48,177 --> 00:39:50,722
Soo ko naf, dangay dee yàpp

274
00:39:53,600 --> 00:39:55,018
Waaye nak, dañu la fay

275
00:40:16,956 --> 00:40:18,666
Eagle, lii mën na nekk njiit

276
00:40:19,125 --> 00:40:22,629
Jiroom benn weer ci ginnaaw, naataango Weng, Lim

277
00:40:22,795 --> 00:40:23,922
ab hitman bu xarañ moo ko dagg

278
00:40:24,297 --> 00:40:25,131
Rabkat bi

279
00:40:25,173 --> 00:40:27,216
musu ñu jàpp

280
00:40:27,759 --> 00:40:29,344
waaye daa muur benn woykat

281
00:40:30,303 --> 00:40:31,220
Lu mu tuddu?

282
00:40:32,805 --> 00:40:33,556
Jenni!

283
00:40:34,807 --> 00:40:36,601
Ba tay wéragul

284
00:40:39,103 --> 00:40:43,983
Dundu gi yomb na, benn bal kese ngay soxla

285
00:40:47,195 --> 00:40:49,197
Du ab faatkat bu amul benn njariñ

286
00:40:50,823 --> 00:40:52,158
Yaakaar naa ni benn góor rek lañuy wër

287
00:40:53,785 --> 00:40:54,869
Suma jumul

288
00:40:56,120 --> 00:40:57,455
Ku góor kii du reykat bu ànd ak deret bu sedd

289
00:40:59,040 --> 00:41:00,917
Benn bal kese la soxla

290
00:40:59,749 --> 00:41:00,917
deret ju sedd wala deet

291
00:41:01,793 --> 00:41:04,921
Dafa bàyyi bakkanam ngir muccal xale bu jigéen bi

292
00:41:07,340 --> 00:41:09,509
Ak sudee daa gaañ waykat bi ci anam wu jaarul yoon

293
00:41:13,096 --> 00:41:14,889
Dafa wara jokkoo ak moom

294
00:41:40,289 --> 00:41:41,040
Jeff?

295
00:41:41,290 --> 00:41:43,084
Duma Jeff

296
00:41:44,669 --> 00:41:47,922
Maa ngi jéggalu, mënu ma gis bu baax

297
00:41:48,297 --> 00:41:50,008
Jàppoon naa ni sama xarit nga

298
00:41:51,509 --> 00:41:52,593
Way wu rafet la

299
00:41:53,011 --> 00:41:54,345
Ndax mën nga ko woyaat?

300
00:41:55,430 --> 00:41:57,974
Kenn rek laa wayal

301
00:41:58,057 --> 00:41:59,058
Jeff?

302
00:42:00,685 --> 00:42:02,270
Sa way dafa fees dell ak yëg-yëg

303
00:42:02,937 --> 00:42:06,149
Ginaaw bimu ko déglu,
Daa melni xam naa sa xarit

304
00:42:06,399 --> 00:42:07,984
Sama xel mi yépp a ngi fi leegi

305
00:42:15,158 --> 00:42:19,412
Fu mu mëna nekk yaa ngi ci ay xalaatam

306
00:42:33,760 --> 00:42:35,595
Waaye benn wàll ci moom dina musa nekk fii

307
00:43:30,191 --> 00:43:31,192
Ndax wóolu ma?

308
00:43:32,318 --> 00:43:33,319
Xam nga luko waral

309
00:43:36,489 --> 00:43:37,323
Ci lu wóor

310
00:43:38,908 --> 00:43:41,744
Nit ñi ci sunu liggéey

311
00:43:39,826 --> 00:43:41,744
waru ñu wóolu kenn

312
00:43:52,338 --> 00:43:53,840
naka lañu xamee ni damay dem ci tefes gi?

313
00:43:54,507 --> 00:43:56,175
Amaana dañu ma topp

314
00:43:56,217 --> 00:43:57,301
Bi may dawal oto bi foofu

315
00:43:58,261 --> 00:43:59,345
Loolu mooy sama njuumte

316
00:44:01,806 --> 00:44:02,890
Kan moo bëgga ma dee?

317
00:44:03,683 --> 00:44:04,642
Lu tax nga koy laaj ?

318
00:44:07,186 --> 00:44:09,188
Xam nga sàrt yi

319
00:44:11,983 --> 00:44:13,651
Lu tax dawul, ginaaw liggéey bi?

320
00:44:15,153 --> 00:44:16,863
ba tay jota guma sama xaalis

321
00:46:25,533 --> 00:46:26,534
Kan moo ma bëgga rey?

322
00:46:27,493 --> 00:46:28,786
Soo fekkewul sa dàntite

323
00:46:30,121 --> 00:46:31,330
Bëggul nga dee

324
00:46:33,666 --> 00:46:35,751
Tontu ma, kan moo ma bëgga rey?

325
00:46:41,173 --> 00:46:44,010
Tontu ma njëkk, ndax des nga ay bal?

326
00:46:50,308 --> 00:46:52,351
Saa yu nekk damay denc bal bi mujj

327
00:46:53,561 --> 00:46:56,314
Amaana ngir sama bopp, wala sama noon

328
00:46:58,566 --> 00:47:04,447
Johnny weng la, doomu rakk bu góor,
Dafa bëgg nga dee

329
00:47:04,989 --> 00:47:06,699
Daf la yobbu ngir nga ray ndijaay

330
00:47:41,067 --> 00:47:42,693
Ndax am nga benn bal bu mujj?

331
00:47:55,206 --> 00:47:59,585
Jeff, jërëjëf ci linga ma baale

332
00:48:01,962 --> 00:48:03,589
Leegi noo ngi ci benn gaal

333
00:48:05,216 --> 00:48:07,051
Amul nu nu mëna jaar

334
00:48:08,719 --> 00:48:10,346
Bëggatu la gisati mukk

335
00:48:16,310 --> 00:48:17,353
Inspektër Li!

336
00:48:20,523 --> 00:48:22,775
Inspectër Li, juroom seede yu dee

337
00:48:53,848 --> 00:48:54,640
Moo ko doon

338
00:48:55,724 --> 00:48:56,434
Ndax wóor nga ko ?

339
00:48:57,059 --> 00:48:59,687
Waneel dëkkandoo yi nataalam
nga laaj ndax mingi fi

340
00:49:00,938 --> 00:49:01,981
Baax na

341
00:50:00,039 --> 00:50:01,790
Inspectër Li, danga ko dóor ci pontu bi

342
00:50:01,832 --> 00:50:04,251
Dëkkandoo yi neena ñu fi la dëkk

343
00:50:12,134 --> 00:50:13,302
Ndax dof ​​nga?

344
00:50:46,126 --> 00:50:46,877
Jenni!

345
00:50:47,628 --> 00:50:49,922
Jeff, yaay?

346
00:50:50,297 --> 00:50:51,549
Lu tax doo dellusi?

347
00:50:52,424 --> 00:50:53,634
Dinaa dellusi tay ci suba

348
00:50:54,635 --> 00:50:56,345
Danuy toxu ci kër gu bees

349
00:50:56,637 --> 00:50:57,471
Lu tax?

350
00:50:58,597 --> 00:51:00,140
Jàppoon naa ni bëgg nga

351
00:51:00,474 --> 00:51:01,600
dëkk ci wetu géej

352
00:51:01,934 --> 00:51:02,935
Def naa

353
00:51:04,395 --> 00:51:05,771
Briise yu rafet

354
00:51:06,438 --> 00:51:07,898
Mën naa xalaat géej gu baxa gu xóot gi

355
00:51:08,232 --> 00:51:10,484
ak asamaan bu baxa bu leer

356
00:51:11,068 --> 00:51:13,737
Rafetna, defaral say bagaas te nga xaar ma

357
00:51:15,072 --> 00:51:16,115
Dinaa fi nekk

358
00:51:30,629 --> 00:51:32,881
Bàyyiwoo Hong Kong bi nga amee chance

359
00:51:33,674 --> 00:51:34,633
Lan moo la tere?

360
00:51:50,566 --> 00:51:52,693
Ndax yaay portier bu bees bi?

361
00:51:52,776 --> 00:51:53,152
Waaw soxna

362
00:51:53,193 --> 00:51:55,571
Deful sa liggéey nimu waree

363
00:51:55,613 --> 00:51:57,197
Lii escape lakk la

364
00:51:57,281 --> 00:51:58,907
Xoolal, mbalit a ngi fépp

365
00:51:58,991 --> 00:52:01,076
Luy xew su amee lakk?

366
00:52:01,160 --> 00:52:02,786
Mënu ma naaw dem ni phoenix

367
00:52:03,579 --> 00:52:06,457
Weer wu nekk damay fay sama maintenance

368
00:52:05,122 --> 00:52:06,457
Suma la gisee ku tàyyeel

369
00:52:06,999 --> 00:52:08,500
Dinaa def plainte ci yaw

370
00:52:08,542 --> 00:52:09,460
Bul dem...

371
00:52:09,501 --> 00:52:10,919
- bépp mbalit bu fi nekk
- Yaa ngi parye lady

372
00:52:10,961 --> 00:52:12,880
Toxal leen lépp

373
00:52:13,964 --> 00:52:15,341
merde

374
00:52:46,914 --> 00:52:49,041
Jeff, dellu nga

375
00:52:49,625 --> 00:52:50,793
Waaw, Jennie

376
00:52:55,005 --> 00:52:56,298
Ndax yaa ngi ak sa xarit?

377
00:52:57,925 --> 00:53:00,803
Waaw, dafa daan football ak man

378
00:53:02,680 --> 00:53:05,099
Nu màggee ci benn barab

379
00:53:06,809 --> 00:53:08,769
Waaw Mooy

380
00:53:09,228 --> 00:53:11,188
Man maay Dumbo, moom Mickey Mouse la

381
00:53:12,064 --> 00:53:13,732
Noonu ngeen woowe seen biir?

382
00:53:15,984 --> 00:53:17,236
Kontaan naa ci gis leen

383
00:53:17,403 --> 00:53:18,696
Bokk naa yëg-yëg boobu

384
00:53:19,363 --> 00:53:20,739
Kontaanoo ci gis sa xarit?

385
00:53:20,948 --> 00:53:22,408
Jege wunu noonu

386
00:53:23,409 --> 00:53:25,869
Daf may indil jafe-jafe yu bari

387
00:53:25,911 --> 00:53:27,371
Dama ñëw ngir saafara jafe-jafe yi

388
00:53:27,788 --> 00:53:29,456
Toogal

389
00:53:28,414 --> 00:53:29,456
Xaaral ma defaral la ataaya

390
00:53:29,498 --> 00:53:30,416
Bul jaaxle

391
00:53:30,958 --> 00:53:31,917
Soxlawolen

392
00:53:31,959 --> 00:53:32,876
Nanga moytu

393
00:53:32,918 --> 00:53:33,627
Moytul, Jennie

394
00:53:33,669 --> 00:53:35,379
Xam naa niñu koy defe, duma gaañ sama bopp

395
00:53:35,671 --> 00:53:38,006
Jeff, toppatoo Dumbo bi may defar ataaya

396
00:53:41,218 --> 00:53:43,220
Dumbo, defal sa bopp ni sa kër

397
00:53:43,637 --> 00:53:45,514
Man maay Miki Mous

398
00:53:46,390 --> 00:53:49,935
Soxna si, lu tax ngay jaaxle ci mbalit mi?

399
00:53:49,977 --> 00:53:51,520
Daf ma fay 1000 dolaar

400
00:53:51,562 --> 00:53:53,063
ngir wéy di wax

401
00:53:53,689 --> 00:53:54,440
Bul génn ci man leegi!

402
00:53:54,481 --> 00:53:55,983
Amuma woon bànneex bu bari nii

403
00:53:56,692 --> 00:53:58,152
ci ñaar fukki at!

404
00:53:58,444 --> 00:53:59,528
Di nga ñàkk match bii

405
00:53:59,611 --> 00:54:01,447
Ndax man? Nanu xaar ba gis

406
00:54:01,947 --> 00:54:04,700
Yaay saa yu nekk ki ñàkk

407
00:54:05,909 --> 00:54:08,871
Du bii yoon, maa ngi waajal bu baax

408
00:54:10,205 --> 00:54:11,790
Nanu jàngat seen waajal

409
00:54:15,043 --> 00:54:16,295
Ndax saa yu nekk danga fasoon yéene?

410
00:54:16,712 --> 00:54:19,298
Waaw, loolu mooy sama stil

411
00:54:19,965 --> 00:54:20,758
Sama bos itam!

412
00:54:21,383 --> 00:54:23,010
Kon amna lu nu bokk

413
00:54:24,094 --> 00:54:29,683
Ndax loolu ngay xalaat ?

414
00:54:29,725 --> 00:54:30,768
Dëgg la

415
00:54:32,478 --> 00:54:35,439
Naan tuuti ataaya, nga topp jamono yu yàgg ya

416
00:54:36,482 --> 00:54:39,818
Jërëjëf Jennie,

417
00:54:38,442 --> 00:54:39,818
defal ndànk

418
00:54:41,945 --> 00:54:44,740
Jennie, lii loxo Dumbo la

419
00:54:45,449 --> 00:54:46,825
Lii sa ataaya

420
00:54:49,411 --> 00:54:50,788
- Jërëjëf
- Bànneex

421
00:54:50,996 --> 00:54:52,748
Ndax sa beneen xarit la?

422
00:54:53,540 --> 00:54:57,544
Dédeet, mooy kiy toppatoo kër gi

423
00:54:58,545 --> 00:54:59,588
Amu nu benn janitor ci batimaa bi

424
00:54:59,671 --> 00:55:02,800
Oh, plombier la

425
00:55:03,550 --> 00:55:05,010
Amna tuyo ndox bu toj ci biti

426
00:55:05,385 --> 00:55:07,888
Dumbo, sa baat miin nañu ko

427
00:55:07,930 --> 00:55:09,181
Ndax amna barab buñu daje bu njëkk?

428
00:55:09,890 --> 00:55:11,058
Daje naa ak yaw ci boîte de nuit bi

429
00:55:12,100 --> 00:55:14,436
Dama bëgg sa way,

430
00:55:13,268 --> 00:55:14,436
waaye bëggoo way te Jeff nekkul foofu

431
00:55:14,520 --> 00:55:16,271
Oh, maa ngi fàttaliku

432
00:55:16,313 --> 00:55:17,689
Loolu mooy tombe!

433
00:55:17,981 --> 00:55:20,567
Dumbo, toppatoo Jennie ab diir

434
00:55:20,609 --> 00:55:21,401
Maa ngi dem ci duus bi

435
00:55:21,568 --> 00:55:22,402
Man itam

436
00:55:22,861 --> 00:55:25,113
Amna beneen duus ci néeg bi

437
00:55:25,781 --> 00:55:26,907
Jennie, amna kaña

438
00:55:26,949 --> 00:55:27,908
Kan mooy?

439
00:55:27,950 --> 00:55:29,952
Ci waañ wi, dinaa ko jàpp

440
00:56:04,278 --> 00:56:06,029
Hey, bul tiire! Man la!

441
00:56:06,154 --> 00:56:07,364
Bul tiire!

442
00:56:08,740 --> 00:56:10,367
Amna ku nekk ci suuf kuy xool sama cul!

443
00:56:36,059 --> 00:56:36,768
Jenni!

444
00:56:38,186 --> 00:56:39,438
Lu xew?

445
00:56:40,731 --> 00:56:41,565
Fan la Jeff nekk?

446
00:56:43,567 --> 00:56:45,152
Xamnaa ni yaw ak Jeff ngeen ma fen

447
00:56:46,361 --> 00:56:47,237
Wax ma dëgg !

448
00:56:48,488 --> 00:56:49,781
Yaay kan?

449
00:56:52,242 --> 00:56:53,285
Man poliis laa

450
00:56:55,787 --> 00:56:56,997
Jeff faatkat bu mag la

451
00:56:57,748 --> 00:56:58,498
Dafa ray nit

452
00:56:59,207 --> 00:57:00,626
ay weer a ngi nii may topp

453
00:57:02,294 --> 00:57:03,003
Gëmuma la

454
00:57:03,503 --> 00:57:04,296
Jenni!

455
00:57:05,339 --> 00:57:06,423
Déglul ma, Jennie

456
00:57:06,506 --> 00:57:07,758
Déedet duma def loolu

457
00:57:08,133 --> 00:57:08,800
Jennie, dëgg la

458
00:57:08,842 --> 00:57:09,968
Soppi!

459
00:57:11,345 --> 00:57:12,721
Jennie, jéemal dal

460
00:57:12,804 --> 00:57:13,805
Déglul!

461
00:57:15,599 --> 00:57:16,600
Toogal

462
00:57:21,229 --> 00:57:22,230
Jiroom benn weer ci ginaaw

463
00:57:23,815 --> 00:57:26,485
Jeff dafa tiire sa kanam ci kaw te jaarale wuñu ko

464
00:57:28,070 --> 00:57:30,197
Leegi patroŋam bëgg nako mu dee

465
00:57:30,989 --> 00:57:32,115
Gëmuma ko

466
00:57:38,914 --> 00:57:41,249
Dama bëgga jàppale waaye mënu ma ci sama posisioŋ

467
00:57:43,794 --> 00:57:46,838
Sama yaakaar mooy nga liggéeyandoo ak nun

468
00:57:48,131 --> 00:57:52,302
Jennie, danu lay jëfandikoo ngir jàpp

469
00:57:52,844 --> 00:57:54,304
Suma mënee am Jeff ci jamono jii

470
00:57:55,472 --> 00:57:57,099
Dinaa ko mëna jàppale mu muccal dundam,

471
00:57:59,017 --> 00:58:00,727
luko moy ki ko yobbu dina ko ray

472
00:58:07,484 --> 00:58:09,486
Wax sa njëg, bëgg naa mu dee rek!

473
00:58:09,945 --> 00:58:12,239
ñu gis ko ci liggéeyam

474
00:58:12,280 --> 00:58:13,949
Dama bëgg mu yàqu, lu gaaw mooy gëna baax

475
00:58:14,950 --> 00:58:16,785
Dugalal $100,000 ci sama kontu leegi

476
00:58:17,369 --> 00:58:19,121
beneen $200,000 ginaaw buñu ko jefee

477
00:58:21,373 --> 00:58:22,749
Amul xaalis amul jëf M. Weng

478
00:58:23,208 --> 00:58:25,085
Doonte gis naa baraamu nit ci gaal gi,

479
00:58:25,585 --> 00:58:26,503
defay waaja xëcc sa bopp

480
00:58:27,295 --> 00:58:29,923
Dugalal téemeeri junni yi ci kontam

481
00:58:28,755 --> 00:58:29,923
Mënoon naa ko am

482
00:58:30,132 --> 00:58:32,551
Lan mooy?

483
00:58:39,182 --> 00:58:40,183
Danga wara fay Jeff,

484
00:58:40,225 --> 00:58:41,977
wala mën nala jural loraange

485
00:58:43,770 --> 00:58:45,313
Loolu amul benn njariñ! Maa ngi ci jàmm

486
00:58:45,731 --> 00:58:48,734
Xoolal nit ñii, dañuy ray nit

487
00:58:52,904 --> 00:58:54,656
Yaay patroŋ bi, danga wara def sa kàddu

488
00:58:54,823 --> 00:58:55,949
Bul wax lu ñaaw

489
00:58:56,033 --> 00:58:56,867
Duma ko fay,

490
00:58:56,908 --> 00:58:59,995
doonte yaa ngi ñaan

491
00:58:58,118 --> 00:58:59,995
Mr Weng, may ma def sama kàddu,

492
00:59:00,037 --> 00:59:01,705
te fey ko lima ko digoon

493
00:59:03,498 --> 00:59:04,958
Su ko defee ma indil la ko

494
00:59:09,337 --> 00:59:12,549
Weng, soo ko bëggee,

495
00:59:13,884 --> 00:59:15,052
Dinaa saraxu

496
00:59:15,260 --> 00:59:17,179
Demal safara, yaw dof!

497
00:59:17,721 --> 00:59:19,264
Soo liggéeyul sama pàppa lu yàgg nii

498
00:59:19,347 --> 00:59:20,307
Dama doon dàq kaka ci yaw

499
00:59:20,807 --> 00:59:23,477
Kan la? Yelloowul sa yërmaande

500
00:59:23,977 --> 00:59:27,105
Lu tax ngay defal Jeff lii yépp?

501
00:59:27,564 --> 00:59:29,107
Mooy sama xarit bu baax

502
00:59:29,858 --> 00:59:31,651
Dagg mbalit mi!

503
01:00:16,279 --> 01:00:18,365
Ñëwal fii leegi! Weng deñ kaa tiire bal

504
01:00:38,969 --> 01:00:40,178
Rayal ko!

505
01:00:47,060 --> 01:00:48,812
Weng!

506
01:00:47,435 --> 01:00:48,812
Mr Weng, danga gaañu!

507
01:00:48,854 --> 01:00:49,604
Rayal ko rekk!

508
01:00:49,646 --> 01:00:52,190
Nanu dem ! Danga nekk ci jafe-jafe

509
01:00:52,274 --> 01:00:53,441
Toppal ko!

510
01:01:27,058 --> 01:01:28,435
Soo ma jàppee sa xarit,

511
01:01:29,102 --> 01:01:30,395
ray ma leegi

512
01:01:32,230 --> 01:01:33,273
Dama bañ gis ngay toroxal sa bopp

513
01:01:33,315 --> 01:01:34,858
yalwaan

514
01:01:42,324 --> 01:01:43,491
Doonte mënu ma ko

515
01:01:43,783 --> 01:01:46,036
Dama risk sama bakkan ngir am sa xaalis

516
01:01:47,996 --> 01:01:49,164
Mënoon naa la ray

517
01:01:49,414 --> 01:01:51,541
Dama wara saraxu Weng ngir am sa xaalis

518
01:01:52,292 --> 01:01:54,544
Duma ñàkk ngor, wala book?

519
01:02:19,152 --> 01:02:20,403
Sunu àdduna mingi soppeeku bu baax

520
01:02:23,365 --> 01:02:25,617
Musu ma mel nii

521
01:02:26,785 --> 01:02:28,245
Amaana danu namm lool

522
01:02:37,754 --> 01:02:39,214
Nostalgie bokk na ci sunuy xéewal yu ñuy muccal

523
01:02:41,216 --> 01:02:43,134
Suma dee,

524
01:02:43,176 --> 01:02:44,594
Dinaa xam ni sama xarit daf ma fàttaliku

525
01:02:46,471 --> 01:02:49,808
Nanu fay sunuy ndàmpaay ci àdduna bi ci topp

526
01:03:00,568 --> 01:03:02,112
Xalaatal ni mën nanu leen fomm leegi,

527
01:03:03,571 --> 01:03:04,948
loolu mooy li xarit di def

528
01:03:07,325 --> 01:03:08,243
Jub?

529
01:03:51,536 --> 01:03:52,162
Naan?

530
01:03:52,620 --> 01:03:53,455
Jërëjëf

531
01:03:54,831 --> 01:03:57,709
Jennie dafa yàgg bëgga dëkk ci wetu géej gi

532
01:03:59,919 --> 01:04:01,254
Defal nga ko lu bari

533
01:04:03,214 --> 01:04:04,591
May xalaat nu muy yëg ci yaw?

534
01:04:12,515 --> 01:04:13,183
Salaam maalekum?

535
01:04:13,224 --> 01:04:14,059
Jenni!

536
01:04:14,517 --> 01:04:16,311
Jeff, lu tax nga bàyyi ma?

537
01:04:16,603 --> 01:04:17,687
Tàggoowoo

538
01:04:17,937 --> 01:04:20,398
Maa ngi lay massawu ndax amna lu ma wara def

539
01:04:20,565 --> 01:04:22,108
Danu wara dem tay ci guddi

540
01:04:24,069 --> 01:04:24,736
Tay ci guddi?

541
01:04:25,278 --> 01:04:26,529
Dr Ho wooma tay ci ngoon

542
01:04:26,571 --> 01:04:28,740
Dafa denc ñaari kornea,

543
01:04:28,823 --> 01:04:30,033
waaye ñu ngi ci Singapour

544
01:04:30,158 --> 01:04:31,576
Danu wara yegsi xaaju guddi,

545
01:04:31,868 --> 01:04:33,244
wala ñu dem ci saasi ci keneen

546
01:04:35,246 --> 01:04:36,122
baaxna, dinaa la yóbbu

547
01:04:37,540 --> 01:04:41,294
Ok, ñëwal aéroport ci 7:30 tay ci guddi

548
01:04:38,708 --> 01:04:41,294
Dinaa la daje ci wetu Information, danga wara ñëw

549
01:04:41,669 --> 01:04:44,047
Dëgg la, tàggoo

550
01:04:47,342 --> 01:04:48,593
Yaakaar nga ni dina ñëw?

551
01:04:58,311 --> 01:04:59,229
Ndax dinga dem?

552
01:05:03,691 --> 01:05:04,859
wóolu naa ko

553
01:05:19,499 --> 01:05:21,126
Ñépp a ngi fi, nanu dem

554
01:05:21,751 --> 01:05:22,419
Lu xew?

555
01:05:24,212 --> 01:05:26,381
Bëgg naa nga xool,

556
01:05:24,921 --> 01:05:26,381
pouce bu nekk ci barab bii

557
01:05:29,551 --> 01:05:31,386
Lépp pare na

558
01:05:30,301 --> 01:05:31,386
Su amee ñeme ñëw,

559
01:05:31,803 --> 01:05:32,971
du musa rëcci

560
01:06:26,608 --> 01:06:27,358
Jeff!

561
01:06:28,151 --> 01:06:30,570
Soreel fi, daw!

562
01:06:30,778 --> 01:06:31,863
Dafa dof!

563
01:06:34,324 --> 01:06:35,241
Jeff!

564
01:06:35,742 --> 01:06:39,662
Jeff, poliis yaa ngi fépp, daw!

565
01:06:40,246 --> 01:06:42,707
Jeff, poliis yi bëgg nañu la,

566
01:06:44,125 --> 01:06:47,921
bul ma jege

567
01:06:48,046 --> 01:06:50,465
Jeff, ndax yaa ngi fa?

568
01:06:49,297 --> 01:06:50,465
Daw

569
01:06:50,507 --> 01:06:52,008
Bul nangu ñu jàpp la

570
01:07:04,103 --> 01:07:06,147
Ndax yaw kese nga nekk?

571
01:07:06,397 --> 01:07:07,732
Jeff, daw!

572
01:07:12,904 --> 01:07:14,322
Poliis yi dañu lay topp

573
01:07:16,032 --> 01:07:17,367
Sedd!

574
01:07:19,827 --> 01:07:21,704
Jeff, poliis yaa ngi fees dell

575
01:07:24,332 --> 01:07:26,668
Jeff, poliis yaa ngi fépp!

576
01:07:27,335 --> 01:07:28,586
Rëcc! Nanga daw!

577
01:07:31,297 --> 01:07:32,799
Jeff, daw!

578
01:07:35,218 --> 01:07:36,511
Man maay, Jennie!

579
01:07:36,928 --> 01:07:37,845
Bul yëngu

580
01:07:42,934 --> 01:07:43,893
Nanu dem

581
01:07:44,477 --> 01:07:45,478
Luy loolu, ofisiye bi?

582
01:07:45,812 --> 01:07:47,522
Flirter du krim

583
01:07:53,903 --> 01:07:54,946
Jàppleen ko!

584
01:08:06,291 --> 01:08:07,166
Deel leer ku nekk!

585
01:08:07,208 --> 01:08:08,960
Bàyyil ma jàll!

586
01:08:13,673 --> 01:08:14,674
Bul yëngu

587
01:08:18,094 --> 01:08:20,096
Dakkal dal!

588
01:08:20,179 --> 01:08:23,891
Dakkal dal! Danu wara xool bagaas yi

589
01:08:22,807 --> 01:08:23,891
Noo ngi jéggalu

590
01:08:23,975 --> 01:08:25,101
Ubbi leen valise

591
01:08:27,353 --> 01:08:28,479
Lu doon def ci aéroport bi?

592
01:08:28,938 --> 01:08:30,064
Topp geen!

593
01:08:30,523 --> 01:08:31,482
Lan ngay liggéey?

594
01:08:31,941 --> 01:08:37,113
Man agent casting laa ci benn kompiñi filmu

595
01:08:38,364 --> 01:08:39,407
Lu tax nga daw te bañ ñu jàpp la?

596
01:08:40,533 --> 01:08:41,242
màndiwoon naa

597
01:08:41,868 --> 01:08:43,202
Jubalal dox ci yoon wu jub

598
01:08:58,801 --> 01:08:59,802
Ana sa xarit?

599
01:09:00,428 --> 01:09:01,888
Ban xarit?

600
01:09:04,724 --> 01:09:05,975
Yaakaar naa ni xam nga ki may wax

601
01:09:06,976 --> 01:09:08,603
Mingi ci jafe-jafe yu rëy

602
01:09:12,857 --> 01:09:16,235
Dimbali ko, wax ma fumu nekk

603
01:09:17,278 --> 01:09:19,238
Dama bëgga jàppale ko mu saafara jafe-jafem

604
01:09:20,490 --> 01:09:21,991
Dama am ay laaj yu ma bëgga laaj

605
01:09:24,118 --> 01:09:26,037
Loolu bokkul ci sama mbiri bopp

606
01:09:26,829 --> 01:09:30,833
Waaye sudee waa ji ngay wax sama xarit la

607
01:09:32,502 --> 01:09:34,504
Soxlawul sa ndimbal

608
01:09:39,759 --> 01:09:41,552
Leegi nak, génn nga ci dosiye Weng

609
01:09:41,594 --> 01:09:43,596
Inspectër Chan mooy jël liggéey bi

610
01:09:44,555 --> 01:09:45,973
Maa ngi lay jox dosiye bu bees

611
01:09:47,767 --> 01:09:48,643
Bëgg naa leeral

612
01:09:48,935 --> 01:09:50,144
Wolomuma la

613
01:09:51,813 --> 01:09:52,897
Ak kiy tuumal,

614
01:09:52,939 --> 01:09:55,233
du yoonu jàpp ko

615
01:09:57,402 --> 01:10:00,154
Sëñ bi, xamoo ni may liggéeyee

616
01:10:00,697 --> 01:10:04,659
Wax nga ko! Loolu moo tax nga génn ci dosiye bi

617
01:10:08,037 --> 01:10:08,871
Duma bàyyi amal lànket bi

618
01:10:09,247 --> 01:10:10,248
Ay yëf!

619
01:10:10,832 --> 01:10:14,627
Chang, leegi assistant Chan nga

620
01:10:16,212 --> 01:10:16,963
Waaw Sëñ bi!

621
01:10:17,046 --> 01:10:18,715
Bàyyileen waa ji ngeen jàpp ci aéroport bi

622
01:10:19,215 --> 01:10:20,883
Jox ko ñaar fukki waxtu diko wottu

623
01:10:21,175 --> 01:10:22,593
Dina nu yóbbu ci faatkatu Weng

624
01:10:24,220 --> 01:10:25,179
Ndax am nga ko?

625
01:10:27,306 --> 01:10:28,558
Waaw Sëñ bi!

626
01:10:50,830 --> 01:10:52,373
Ndax dinga rayaat?

627
01:10:59,630 --> 01:11:02,341
Jàppoon naa ni nit ñi ma ray yelloo nañu dee

628
01:11:06,804 --> 01:11:07,889
Leegi, jàpp naa ni ku nekk amna sañ-sañu dundu

629
01:11:09,849 --> 01:11:10,767
Dédeet, duma ray nit

630
01:11:11,601 --> 01:11:13,019
Yaakaar naa ni dinaa mëna def sama dige

631
01:14:36,180 --> 01:14:37,223
Topp nañu ma!

632
01:14:37,431 --> 01:14:39,809
Waa Weng, ak poliis yi itam

633
01:14:41,978 --> 01:14:43,646
Bul jaaxle, maa leen toppatoo

634
01:14:46,065 --> 01:14:47,900
Weng moo yobbu Paul Yau ngir yàq la

635
01:14:49,443 --> 01:14:52,780
Bul jaaxle, mën nga jëfandikoo samay fita ak samay munisioŋ

636
01:14:57,368 --> 01:14:58,160
Fan nga jëm?

637
01:14:59,954 --> 01:15:01,122
Ngir dindi sa xaalis ci Weng

638
01:15:03,249 --> 01:15:04,417
Dina nu daje ci eglis bi

639
01:15:06,419 --> 01:15:07,086
Ndax yaw kese ngay dem?

640
01:15:07,837 --> 01:15:08,879
Waaw kay

641
01:15:09,839 --> 01:15:11,007
Dama wara def sama dige

642
01:15:13,134 --> 01:15:14,593
Weng duma def dara,

643
01:15:15,511 --> 01:15:17,054
Ba leegi yelloo naa sargal

644
01:15:18,639 --> 01:15:22,518
Sidney, soxlawuma xaalis bi

645
01:15:24,020 --> 01:15:25,646
Dama soxla sa xaritoo

646
01:15:42,913 --> 01:15:47,084
Soppi! Soppi!

647
01:15:51,839 --> 01:15:55,760
Ma topp ko ba ci 6 Horizon Drive

648
01:15:56,719 --> 01:15:58,137
Dama daanaka jot ko

649
01:16:00,222 --> 01:16:01,265
xam naa

650
01:16:01,307 --> 01:16:05,561
Waaw sama waajur! Weng!

651
01:16:02,683 --> 01:16:05,561
Bul jaaxle, dinaa ko gis

652
01:16:05,936 --> 01:16:07,354
Chang, bul jaaxle

653
01:16:08,689 --> 01:16:09,648
Céeli

654
01:16:11,108 --> 01:16:15,488
Mën wéy di am ndam

655
01:16:16,655 --> 01:16:18,699
Waaye mënoo ñàkk ba fàww itam

656
01:16:24,789 --> 01:16:27,708
Soppi! Soppi!

657
01:16:47,812 --> 01:16:50,022
Inspectër Li, ndax jox nanu dara?

658
01:16:51,899 --> 01:16:53,192
Demal laaj ko sa bopp!

659
01:18:16,817 --> 01:18:17,484
Jeff!

660
01:18:18,110 --> 01:18:21,280
Jennie, luy loolu?

661
01:18:23,449 --> 01:18:24,700
Lu tax suba gi lëndëm nii?

662
01:18:26,577 --> 01:18:28,787
Bis la bu bari niir

663
01:18:31,582 --> 01:18:34,210
Nga bàyyi sa xel, dina baax?

664
01:18:36,045 --> 01:18:37,213
Ndax tay lañuy dem?

665
01:18:37,463 --> 01:18:38,505
Waaw

666
01:18:42,009 --> 01:18:42,801
Sedd!

667
01:18:43,802 --> 01:18:44,720
Kan la?

668
01:18:45,763 --> 01:18:46,639
Dumbo la!

669
01:18:47,765 --> 01:18:48,599
Lu mu bëgg?

670
01:18:49,266 --> 01:18:50,476
Dafa ñëw ngir tàggatoo

671
01:18:54,772 --> 01:18:55,689
Lu ngeen di xaar?

672
01:18:56,232 --> 01:18:59,235
Man poliis laa, duma tiire bal nit ci ginaaw

673
01:18:59,652 --> 01:19:00,945
Meneen anam nu melni

674
01:19:01,070 --> 01:19:02,363
Dédeet bokku nu benn!

675
01:19:03,447 --> 01:19:05,115
Maa ngi topp yoon wi, yaw nga ko sàggane!

676
01:19:06,825 --> 01:19:07,952
Chang dee ndax yaw

677
01:19:08,619 --> 01:19:10,120
Waat naa ni dinaa la jot ci jamono jii

678
01:19:15,417 --> 01:19:16,252
Man itam bëgg naa la

679
01:19:17,670 --> 01:19:19,255
Waaye duma may ngeen tëj ma.

680
01:19:21,340 --> 01:19:22,967
Sudee danga wara fay sa xarit

681
01:19:23,842 --> 01:19:24,969
Tiire ma leegi

682
01:19:26,136 --> 01:19:27,346
Bul ma forse ma ray la

683
01:19:46,031 --> 01:19:47,533
Kon danga may ray dëgg?

684
01:19:47,700 --> 01:19:49,076
Duma la bàyyi nga dem bii yoon

685
01:19:49,660 --> 01:19:50,703
Nanu xool

686
01:19:51,745 --> 01:19:53,038
Mën wéy di am ndam

687
01:19:53,414 --> 01:19:54,623
Jeff, fan nga nekk?

688
01:19:54,665 --> 01:19:55,749
Jeff!

689
01:19:56,625 --> 01:19:58,544
Fan la Dumbo nekk? Ana mu nekk ?

690
01:19:59,461 --> 01:20:00,254
Ci sa kanam

691
01:20:02,423 --> 01:20:03,424
Bul ko yóbbu fu sori

692
01:20:03,507 --> 01:20:04,216
Jenni!

693
01:20:04,300 --> 01:20:06,176
Jeff digoon nama ni du musa ray nit

694
01:20:06,719 --> 01:20:07,803
Tegal fita bi ci suuf

695
01:20:07,970 --> 01:20:09,263
Jennie, tëral fita bi

696
01:20:09,346 --> 01:20:11,640
Duko def fileek bàyyiwul nu nu wéet

697
01:20:12,474 --> 01:20:14,643
Maa ngi lay saraxu, nga bàyyi nu dem

698
01:20:14,727 --> 01:20:16,770
- Jenni!
- Duma may nga jàpp ko mukk

699
01:20:18,564 --> 01:20:20,983
Ndax maa ko ray? Ndax dee na ?

700
01:20:21,483 --> 01:20:24,778
Bëgguma ko ray, bëgguma ko

701
01:20:25,112 --> 01:20:26,113
Dafa baax

702
01:20:27,406 --> 01:20:28,866
Bëgguma woon

703
01:20:32,953 --> 01:20:33,996
Dafa baax

704
01:21:39,770 --> 01:21:41,438
Teg sa xel, nga am fit

705
01:21:42,314 --> 01:21:44,817
Demal foofu!

706
01:21:43,023 --> 01:21:44,817
Jeff... Jeff

707
01:22:10,008 --> 01:22:11,969
Nanu joge fi, kon mën ngeen ma jàpp

708
01:22:19,643 --> 01:22:21,270
Nanu genne Jennie fii

709
01:22:22,938 --> 01:22:23,939
Oto bi mingi ci biti

710
01:22:58,223 --> 01:22:59,224
Gaawal!

711
01:23:45,896 --> 01:23:47,314
Duma may nga tëj ma ci ginaaw weñ yi

712
01:23:48,607 --> 01:23:49,650
sànni fita bi ci suuf

713
01:23:56,698 --> 01:23:57,866
Xamnaa ni doo ray benn poliis

714
01:24:44,162 --> 01:24:45,122
Jërëjëf

715
01:24:47,916 --> 01:24:49,668
Mën ngama ray benn yoon

716
01:24:50,711 --> 01:24:52,129
Duma ray kenn

717
01:24:52,671 --> 01:24:53,755
ba ma xamni ñooy sama noon dëgg

718
01:24:53,922 --> 01:24:55,007
Ndax xam ngama dëgg?

719
01:24:57,301 --> 01:24:58,885
Yenn saa yi ëlëg mooy doxal lépp

720
01:25:01,138 --> 01:25:06,059
Kenn ki ma xamante
nekk na poliis

721
01:25:06,560 --> 01:25:07,853
Waaye mën nga xàddi saa yu nekk

722
01:25:09,771 --> 01:25:13,900
Dédeet, dige naa ko,

723
01:25:13,942 --> 01:25:14,901
Maa ngi topp sama kàddu

724
01:25:15,569 --> 01:25:16,945
Yenn saa ma ci ñee sa moom sa bopp

725
01:25:18,864 --> 01:25:21,491
Amuma ko

726
01:25:23,160 --> 01:25:24,161
Gëm naa yoon

727
01:25:25,120 --> 01:25:26,204
waaye kenn wóolu ma

728
01:25:27,372 --> 01:25:28,790
Man itam amnaa jafe-jafe boobu

729
01:25:32,169 --> 01:25:33,503
Poliis bu wuute nga

730
01:25:35,422 --> 01:25:37,007
te yaw itam ab raykat bu amul fenn nga

731
01:25:40,636 --> 01:25:42,846
Maa ngi lay massawu ci lima la dugal ci jafe-jafe yii

732
01:25:43,096 --> 01:25:44,765
Wax ma, kan moo nekk ci ginaaw lii lépp?

733
01:25:45,182 --> 01:25:48,101
Du loolu mooy sama jeu, damay topp sàrt yi

734
01:25:50,062 --> 01:25:51,605
Xamoon naa ni dooma ko musa wax

735
01:25:53,565 --> 01:25:55,025
Toppatoo Jennie

736
01:25:56,652 --> 01:25:57,819
Weng du taxaw ba kera la ray

737
01:25:58,820 --> 01:25:59,905
Li gën mooy nga bàyyi ma jàpp la

738
01:26:24,680 --> 01:26:25,889
Dina nu fanaan ci guddi gi

739
01:26:26,431 --> 01:26:27,724
Suko defee Sidney dina may indil sama xaalis,

740
01:26:27,766 --> 01:26:29,142
ba noppi nu dem suba bi

741
01:26:29,935 --> 01:26:32,020
Dama ragal ni bandit yooyu dina ñu nu fekk fii

742
01:26:34,481 --> 01:26:35,315
bul jaaxle

743
01:26:37,067 --> 01:26:39,069
Bii barab bu sori la

744
01:26:43,699 --> 01:26:44,991
Lu tax mu lëndëm nii?

745
01:26:47,953 --> 01:26:49,496
Mënu ma gis dara

746
01:26:51,623 --> 01:26:54,000
Jeff Taalal làmp yi

747
01:26:54,543 --> 01:26:56,294
Lu tax doo taal làmp yi?

748
01:27:01,049 --> 01:27:02,008
Jeff!

749
01:27:10,559 --> 01:27:11,893
Jeff, taalal làmp yi!

750
01:27:12,102 --> 01:27:15,147
Kuuraŋ dafa dagg

751
01:27:21,570 --> 01:27:23,155
Ndax sa xarit dina dellusi ak xaalis bi?

752
01:27:26,074 --> 01:27:30,620
Yaakaar naa ni dina ko def

753
01:27:34,499 --> 01:27:35,208
Njiit

754
01:27:35,584 --> 01:27:37,419
Lii mooy US$100,000 xoolal bu baax

755
01:27:38,003 --> 01:27:39,796
Yaakaar nga ni Paul Yau dina mëna ray Jeff?

756
01:27:52,934 --> 01:27:55,061
Boss, Sidney Fung mingi fi

757
01:27:56,813 --> 01:27:59,191
Sudee daf la woraat, looy def?

758
01:28:05,363 --> 01:28:06,823
Ba leegi dama koy jàppee ni sama xarit

759
01:28:07,908 --> 01:28:09,367
Dafa baax ci man

760
01:28:14,498 --> 01:28:15,332
Fan la xaalisu Jeff nekk?

761
01:28:15,373 --> 01:28:16,583
Fan la nekk?

762
01:28:17,876 --> 01:28:19,961
Yàlla ma am xarit bu mel ni yaw

763
01:28:22,547 --> 01:28:25,383
Di nga ko def, benn ci bis yii

764
01:28:41,024 --> 01:28:42,943
Dakkal seeni bunduxatal!

765
01:28:46,947 --> 01:28:48,073
Sa loxo ndijoor baa ngi liggéey?

766
01:28:48,156 --> 01:28:49,074
Waaw, doyna

767
01:28:49,908 --> 01:28:51,326
Ba leegi mingi tiire fita, gaaw te jaar yoon

768
01:28:51,743 --> 01:28:53,161
Amul benn yoon bu ngeen mëna jaar,

769
01:28:53,745 --> 01:28:54,830
Lu tax ngay def lii?

770
01:28:55,497 --> 01:28:56,915
Wax ma, lan mooy beneen pexe?

771
01:28:58,416 --> 01:28:59,251
Fan la xaalis bi nekk?

772
01:29:00,627 --> 01:29:01,586
Jox ko!

773
01:29:16,393 --> 01:29:17,310
Maa ngi ci kanam benn jéego

774
01:29:17,811 --> 01:29:19,104
Lu tax doo ma tiire bal ci bopp?

775
01:29:19,187 --> 01:29:20,313
Jub

776
01:29:21,439 --> 01:29:23,233
Amaana nekkatu ma ab liggeykat

777
01:29:27,237 --> 01:29:29,948
Sama yaakaar mooy tàmbaliwaat lépp

778
01:29:32,367 --> 01:29:33,159
Loolu tiis la

779
01:29:38,498 --> 01:29:39,958
Jox ma xaalis bi

780
01:29:40,208 --> 01:29:41,126
Fan la Jeff nekk?

781
01:29:41,376 --> 01:29:43,253
Jëlal ma xaalis bi

782
01:29:47,632 --> 01:29:49,593
Danu ko wara delloo

783
01:29:51,052 --> 01:29:52,012
Naaféq!

784
01:29:57,601 --> 01:29:59,811
Ndax reykat yépp dañu am ngor?

785
01:30:00,437 --> 01:30:03,398
Sunu àdduna mingi soppeeku bu baax, njukkal

786
01:30:07,485 --> 01:30:09,863
Sidney, yenn saa ma jàpp ni doo nit

787
01:30:10,113 --> 01:30:11,531
Danga gën a niru ak xaj

788
01:30:16,036 --> 01:30:17,537
Amna benn mbir buñu bokk

789
01:30:18,455 --> 01:30:19,831
Nun ñaar ñépp danuy jëfandikoo bunduxatal ngir dundu

790
01:30:23,585 --> 01:30:25,211
Sunu mébet wuute na

791
01:30:26,296 --> 01:30:27,213
Jub?

792
01:30:30,550 --> 01:30:32,761
Xaj yi ñoo gëna mag góor ñi ci yenn mbir

793
01:30:42,812 --> 01:30:44,022
Soo ma waxul fumu Jeff nekk

794
01:30:44,064 --> 01:30:45,190
Lii sa dëj la

795
01:30:46,524 --> 01:30:47,943
sànni mbalit mii

796
01:31:09,506 --> 01:31:10,340
Jox ma xaalis bi

797
01:31:10,840 --> 01:31:12,050
Yaakaar nga ni am nga ay bal?

798
01:31:13,927 --> 01:31:14,886
Bëgg nga pari?

799
01:31:16,012 --> 01:31:19,432
Jeff neena, saa yu nekk denc benn slug bu mujj

800
01:31:20,141 --> 01:31:22,352
Yalla ngir sa bopp, wala sa noon

801
01:31:36,491 --> 01:31:37,575
Gaaw!

802
01:31:40,662 --> 01:31:41,746
wëlbatiku!

803
01:31:51,047 --> 01:31:52,757
Yalla mbugal!

804
01:31:58,847 --> 01:31:59,848
Wutal ko!

805
01:32:07,856 --> 01:32:09,399
Dama bëgg nga dig ma lenn

806
01:32:11,151 --> 01:32:13,695
Suma ko deful

807
01:32:14,988 --> 01:32:16,197
Yobbul ma hopitaal

808
01:32:16,781 --> 01:32:18,533
Waxal doktër yi ñu opere ko,
Samay koornea ngir Jennie

809
01:32:21,202 --> 01:32:24,956
Soo ko mënulee def, defaral sama xaalis

810
01:32:25,040 --> 01:32:26,207
te yónnee ko ci bitim réew ngir ñu opere ko

811
01:32:29,794 --> 01:32:31,046
Bul xalaat loolu

812
01:32:34,758 --> 01:32:38,803
Mooy liy njëkka def lu baax ci yima musa def

813
01:32:39,929 --> 01:32:41,097
Ndax dinga ma dimbali?

814
01:33:16,132 --> 01:33:17,258
Luy xumbaay bi?

815
01:33:19,469 --> 01:33:20,553
Kan mooy Jeff?

816
01:33:20,595 --> 01:33:21,805
Sidney Fung la

817
01:33:32,148 --> 01:33:33,149
Sidney

818
01:33:39,948 --> 01:33:45,161
Lii sa xaalis xeexal naa ko ni góor

819
01:33:49,707 --> 01:33:54,003
Lii mooy sama sargal bu mujj ci sama xarit

820
01:33:55,505 --> 01:33:58,424
Sidney, jarul nga def lii

821
01:34:15,024 --> 01:34:16,943
Muni ma xaj laa

822
01:34:18,778 --> 01:34:20,822
Leegi xamuma ndax nit laa,

823
01:34:21,948 --> 01:34:23,199
wala xaj?

824
01:34:23,950 --> 01:34:26,452
Sidney, kenn mënu la woowe xaj

825
01:34:28,204 --> 01:34:29,831
Sidney, Sidney!

826
01:34:34,377 --> 01:34:35,753
Sidney!

827
01:34:43,511 --> 01:34:46,431
Sidney, Sidney, ndax lépp jàmm?

828
01:34:48,600 --> 01:34:50,351
Ndax xaj laa?

829
01:34:52,187 --> 01:34:57,775
Déedéet, doo xaj. Góor gu mag nga!

830
01:34:58,484 --> 01:35:01,821
Nun ay personage yu màgget lañu,
ñu dàq ci sunu askan

831
01:35:04,240 --> 01:35:07,202
Bëgguma dee ni xaj

832
01:35:12,207 --> 01:35:15,126
Waaye gis nga, defuma benn bal bu mujj

833
01:35:17,503 --> 01:35:18,880
Amnaa benn

834
01:35:21,049 --> 01:35:22,550
Amnaa benn

835
01:36:04,550 --> 01:36:05,176
Jeff!

836
01:36:05,260 --> 01:36:05,969
Jennie, des fi nga nekk

837
01:36:06,010 --> 01:36:07,053
Bul ma bàyyi ma wéet!

838
01:36:08,263 --> 01:36:09,305
Lu nga nara def?

839
01:36:11,266 --> 01:36:12,183
Storm sama yoon ngir génn!

840
01:36:12,308 --> 01:36:13,351
Bul ray nit, mangi?

841
01:36:13,726 --> 01:36:15,103
Bàyyileen seeni bunduxatal ngeen ànd ak man

842
01:36:16,479 --> 01:36:20,984
Lan? Yaa ngi wax ma ray Sidney

843
01:36:21,150 --> 01:36:22,777
Sama xarit bu baax la woon

844
01:36:23,278 --> 01:36:24,654
Ak yaa ngi may wax ma bàyyi?

845
01:36:28,408 --> 01:36:29,325
Bi Chang dee

846
01:36:29,367 --> 01:36:31,119
Waat naa la ray

847
01:36:32,704 --> 01:36:34,205
Waaye leegi bëgguma ñu rey la

848
01:36:35,415 --> 01:36:36,582
Demal ak Jennie

849
01:36:38,251 --> 01:36:39,002
Naka?

850
01:36:39,836 --> 01:36:41,462
Dina ñu ma topp ba ci catu àdduna bi

851
01:36:42,338 --> 01:36:43,881
Amuma fumu dem

852
01:36:45,091 --> 01:36:47,719
Demal nga wax leen ni poliis nga,

853
01:36:48,428 --> 01:36:49,971
xoolal ndax dina ñu bàyyi seeni fita

854
01:37:09,365 --> 01:37:10,450
- Jenni!
- Jeff!

855
01:37:16,873 --> 01:37:18,249
Jeff!

856
01:37:35,558 --> 01:37:36,559
Dof!

857
01:37:36,809 --> 01:37:38,978
Jërëjëf, Miki Mous!

858
01:37:56,496 --> 01:37:58,831
Dumbo, maa ngi lay delloo

859
01:37:59,707 --> 01:38:00,666
Duma delloo dara

860
01:38:01,125 --> 01:38:02,418
Lii mooy may gi xaritoo

861
01:38:02,752 --> 01:38:03,753
Wërsëgu jàmm!

862
01:39:13,948 --> 01:39:15,533
Jennie, nga muur!

863
01:39:19,912 --> 01:39:21,080
Bul yëngu!

864
01:39:25,460 --> 01:39:26,502
Jenni!

865
01:39:27,462 --> 01:39:28,671
Jenni!

866
01:40:57,218 --> 01:40:58,511
Dof!

867
01:40:59,095 --> 01:41:00,012
Jox ma bunduxatal!

868
01:41:00,304 --> 01:41:01,764
Miki Mous, fii!

869
01:41:25,705 --> 01:41:26,831
Ndax mën nga tiire bu baax?

870
01:41:27,331 --> 01:41:28,624
Man poliis laa, dama wara baax!

871
01:42:04,243 --> 01:42:05,411
Nu bokk dundu lu bari,

872
01:42:06,120 --> 01:42:07,330
Xamuma sa tur

873
01:42:09,123 --> 01:42:09,957
Ndax lu am solo la?

874
01:42:10,374 --> 01:42:12,084
nu am ndam wala nu ñàkk,

875
01:42:12,710 --> 01:42:13,961
Dunga nekk ci wetu

876
01:42:14,337 --> 01:42:16,339
Dama bëgga am tur wu may fàttaliku ba fàww

877
01:42:17,757 --> 01:42:20,635
Ndax danga gëna bëgg ma dee wala ñu bàyyi ma?

878
01:42:21,719 --> 01:42:24,513
Sudee ëlëg daf nu baale, bëgguma benn ci ñoom

879
01:42:25,890 --> 01:42:27,183
Xarit bu baax nga!

880
01:42:29,310 --> 01:42:31,187
Fatteliku ma ni Mickey Mouse, lu tax duko fàttaliku?

881
01:43:26,826 --> 01:43:28,536
Dellul!

882
01:43:27,660 --> 01:43:28,536
Dama wara wut sama xarit

883
01:43:30,204 --> 01:43:31,664
Bàyyileen ko, deful dara!

884
01:43:32,790 --> 01:43:33,582
Randal toxu!

885
01:43:34,208 --> 01:43:34,917
Randal toxu!

886
01:43:53,018 --> 01:43:53,853
Dakkal sa fita!

887
01:43:54,437 --> 01:43:55,688
Dakkal sa fita

888
01:43:56,272 --> 01:43:57,481
Yalla mbugal! Dégg ngama? Gaawaay!

889
01:44:00,735 --> 01:44:04,196
Jeff, fan nga nekk, Jeff?

890
01:44:04,447 --> 01:44:08,284
Jennie, bul ragal dara, maa ngi ci sa kanam

891
01:44:08,868 --> 01:44:10,327
Dakkal sa fita

892
01:44:13,664 --> 01:44:14,874
Jennie, bul yëngu benn pouce

893
01:44:17,334 --> 01:44:18,461
Bul ko gaañ

894
01:44:19,003 --> 01:44:20,129
Dédeet, duma ko gaañ

895
01:44:20,755 --> 01:44:21,756
Dinaa ko ray rek

896
01:44:22,715 --> 01:44:23,632
Bàyyileen ko!

897
01:44:23,799 --> 01:44:25,009
Dakkal dal

898
01:44:27,928 --> 01:44:28,846
Bàyyileen ko mu dem

899
01:44:28,971 --> 01:44:29,847
Ñàkk pexe!

900
01:44:36,687 --> 01:44:37,688
Sudee defuma ko?

901
01:44:45,279 --> 01:44:46,447
Dakkal seeni bunduxatal!

902
01:44:58,459 --> 01:44:59,335
Dof!

903
01:45:01,170 --> 01:45:05,090
Ndax dinga def li nga dige?

904
01:45:08,636 --> 01:45:09,595
Amul solo

905
01:45:12,014 --> 01:45:15,976
Bul fàtte, xarit daa musa am
ngir jàppale la!

906
01:45:25,736 --> 01:45:28,489
Dakkal bunduxatal yi, wala ma ray ko

907
01:45:48,175 --> 01:45:50,052
Bàyyileen seeni bunduxatal, dof yi!

908
01:46:29,592 --> 01:46:31,343
Miki Mous

909
01:46:34,722 --> 01:46:35,848
Miki Mous

910
01:46:48,777 --> 01:46:50,154
Miki Mous

911
01:47:13,969 --> 01:47:15,262
Jeff!

912
01:47:15,554 --> 01:47:16,639
Jenni!

913
01:47:19,058 --> 01:47:23,103
Jeff, fan nga nekk?

914
01:47:30,569 --> 01:47:31,987
Jeff!

915
01:48:12,361 --> 01:48:13,737
Jeff!

916
01:48:21,662 --> 01:48:22,579
Bul yëngu!

917
01:48:22,621 --> 01:48:24,957
Baax na! Baax na! Maa ngi topp,

918
01:48:24,999 --> 01:48:28,168
Dinaa la jàppale, jàpp ma!

919
01:48:31,380 --> 01:48:32,464
Poliis bu wuute nga

920
01:48:33,424 --> 01:48:34,633
te yaw itam ab raykat bu amul fenn nga

921
01:48:37,761 --> 01:48:38,971
Gëm naa yoon

922
01:48:39,847 --> 01:48:41,098
waaye kenn wóolu ma

923
01:48:42,224 --> 01:48:43,517
Man itam amnaa jafe-jafe boobu

924
01:48:46,311 --> 01:48:47,146
jàpp ko

925
01:48:47,396 --> 01:48:48,188
Dinaa ko def !

926
01:48:49,273 --> 01:48:52,651
jàpp ma, jàpp ma

927
01:48:52,943 --> 01:48:55,404
jàpp ma! Maa ngi sàkku ñu jàpp ma ci poliis!

928
01:48:55,446 --> 01:48:56,947
defkatu ñaawtéef laa, jàppleen ma !

929
01:49:20,679 --> 01:49:22,097
Miki Mous...

930
01:49:28,854 --> 01:49:30,272
Miki Mous...

931
01:49:31,305 --> 01:49:37,673
Jàppaleen nu nga nekk waa VIP 
ngir dindi bépp yëgle ci www.OpenSubtitles.org

